Texte zikr : Fa Hâzihî salâmune minnî ileyka

0 528

Fa Hâzihî salâmune minnî ileyka Mâ’ rihul wal anbâri wa tîbi miska
Da may weulbati mbôlem wôyeni sôdan Ba zâhir ba di bâtin ba jar di seetân
Sama khâtir dafa rôti ba bahru kajôr Ma wôyki ki jara wôy môgnu toussé ay lèr
Ma guéweul bi thi l’ islam khamalma ko dônn Kon ma wôyla ta gagn la ya dônn Rabbâne
Sirrup ngeunel bi nga lambô thi dîné l’ islam Sôpé bè laka diokh mô yéyôn thia qadîm
Khutbu jâmihu Niass ya di jant Njolôr Sakhal nga fi ay lër tékthi mbôt yu doy wâr
Ma ngi lay yalwân yow mi dônn tijânn Nga mayma sap mbébet tam khol ma dê thi l’ îmân
Fégulénâ tibbalma ndakh ma jok thi békkôr Raflénâ wodema kon ma bayyi limay gâr
Sa wallô gueneu gaw khar mu faddu bay bûr Sa khéwal gueneu bâwân ba melni aw nîr
Sa atté gueneu wêr yaye khalîlu rahmân Té lô wakh borom kune dâl diné fa yakun
Sa kharbâh yi nga lambô séwal na doctor Ba kô tufli mu weer far du dèm thi doctor
Té ko tufli sa lolwi tafal kô wuzrâ Mu tagôk loru dunyâ kazâka ukhra
Damâ sop dila wôy wanté raw nga say mâss Li takh ma dila wôy nga nirôk borom Fâss
Sa mbôtom khalima raw dabbûssu Mûssâ Sa woydè yi nga dékkil teuhone na Insâ
Kuy muride ne me nieuw wôylé seydi barhâm Wâ ju xam meuneu ragné té sôp barhâm
Té jokh mam khâtir mbâ mu mayma sawkhône Té bâwân mam khéle mba mu mayma fakh môme
Kon dinâ meneu wôy kî di gueun thi sôdânn Di khutbu rûhî nâne thi pêyi dîwân
Déglulénema ma déllôti gagn ki gueune fî Thi azal la ko bûr jiteulône duwut fî
Barhâma ba nga rôté ba say bagane fêsse Bâwalal gni la dôn khar ba sêni ndap fêsse
Hâlam ak alalam mom la jay thi l’ islam Bur signel ko bu wer johko khatmu faydôme
Su ngên xamôn ay may sâ yu nek ngên têw Bagna linkar bagna dingat té ngên sakhô wâw
Beuteum kagnâne dafa peng peng du sêtlu
kharbakh
Kône gnu guiss bi nga wathié gnu kham ni yâ bâkh
Masta jok keur bâyam té raw thi l’ islam Bène Serigne munu fé wakh né dém na dârâm
Bu kagnâne amulôn lôlu mô di ap mbâkh Bu fékkê nga yêm lôlu doyna kharbâkh
Bam yorê gnéti at la dajal buchurâm Té raw na ku mâssam ak ya wey dâw
Bam yôré arafu ka la samp dârâm Di dôr ay massalâm bôlé kok makhâmâme
Sirrup ngeunel yi nga lambol né wul thi ay môle Yay khutbu yay khawssu yay Seydi rijâl
Tûtiwut réyulut gattoutit duwit ndiôl Jeumi Rassûli la yor ngo nirô ba thiaye môle
Su beut ya nélawê khol ba mom mu ngay khôle Té ruh ga arass ak kursîyu thieu lay bêle
Té bu rê déy mugn khar kanam ba mi wêkh kâr kâr Té wârême gueneu nekh leem thia khol ya muy wâr
Balâ gna ngoy yêm lôl bôba aw nakhar fêgne So khôlé Barhâma Niass guiss ko muy mugn
Môy jikôm diamu dônné Fa Seydi Adnân Dogal bu rey ba la doylo môy kune fa yakun
Fâléwul addunak lithi bir da fay nîl Khègnethiu wul lô moy yalla ak nabi dâl
Mussta am kumuy yêm thi alal bani sôy Té am kôm duko bègue lô khamul kumuy fay
Konté wul ay tôgne té dumoyu ay târ Rabbu samawâti wal ardi doy na kô jêkh
Té mânu ak ragal yalla tabé thi l’ islam Té tôlam ba du boy môdi yônu jakâm
Yitêm yâ mo gueneu khîr gaïndé mboya buy bûr Karâma yâ gueneu rêy dussu golfa yuy dôr
Ay beuteum dafa fort mél ni jâni sâmane Rahmatam gueneu khîr thi fafhir ak miskine
Sukhûléna sugnu ruh ya sûkhône thia zulmâne Ni Niominka bu mbâl dieune ba wër si ndangâne
Silmakha kuko taybé bam khôl assamâne War na diuk bayi sagane té top say wâw
Rabbul jalil la ko fal jokh ko manteau Rabbane Fal ga muy fali dômame siwal nala dâl
Wal takun umatane môm la wakh fa lâhû Kuy aw thi ndigalam kham ilâhi nâssôt
Bom yorê sugnu âjo ziarra madîna Bagnu démê bathia pom ba mu déf fa jawrâne
Jeumeume jâ tassalé kholya bagne janok Môme Dugnu mbébet lô moy top thiay takhôk môme
Mêlo yussufa la yôr ki rawône thi ay târ Baku janok mome sop ko ndakh fa yor lêr
Al haj sugnu mâme dâne na wakh ni môy khâss Boba môme ma ngay khôl nawléya beutup mâss
na xalîl nattuwôn nattu wañ ko juurôn La Barhâm faye balâ yi fî thi sôdân
na Xadir nattuwôn Muusa ca mâwu hayât la suñ bây yare dômam yi bi izni mâyâ
Juli na thi rassôl ilâhi makhtar Sallâtane wa taslimane mâ gnane ko irfâne
Tudee nâ bile way sâbiqâtu jihât Thi cursap gni fi dône way imâmul ibâde
fafal xatmu sa waywi te yamfi yaw thiâm ne lô lim limitam dô dajal ba dem sâm
Qassâ’ id yi nga tâlif meunô su kôy môl ajâyib yiŋ ga sakk-it sewal na labdân

0%
Laisser un commentaire