Barhâma, Barhâma Niasse Cheikhul kullil Awliyâ
Barhâma,
Shaykhul kullil Awliyâ’ i Bâye Barhâma
Khôlalma fenkak Baye bi thi Taïba Niassène Gôru Haïbu yeup Têw Nâne Barhâma
Serigne bugne koy Tôpé Tâar Thiolâyame ba suko
gnaké
Mêlokaname ba def lay lêr, Barhâma
Târu Diamant ki ko sôlo kôku moy jeumi Bâye
Niasse
Jeumeul na mbidêf yeup Niuy Barhâma
Du dê, Dieufeum du nul, kuye sûl dieuf
goréwôu…lo
Dioglêne gnu ndiukeul Wâja môy Barhâma
Bi Lâhi wa Lâhi môm Bâye suko Nêkhone Ku wôté dugne la wuyussi Bâye Barhâma
Barigot bu fêsse du yeungu wêr wêr bi Tankhal
nagnu
Khathie buye maté duye mbawé, Bâye Barhâma
Sô guissé ku yomb dajalé aw limame dotul tôgo Ninki nanka dugne koy sôru Barhâma
Kholalma Cheikh Ibrâhim tothie na Makkah ak
sôdan
Niuy gamu ziarré si Bâye Barhâma
Bul sonk kholal auto bi, ap chauffeur ra koy
conduire
Duneyâ bi itam nônu thi Barhâma
Sakhar ku diâr thi yônam bula fîré ya ko tôgno Ndakh yônam bi pour môm rek la, Barhâma
So méré ya nga nâne di na tagalé galace ak ndokh Thiossâne galace ndokh la, Bâye Barhâma
Môgnu wakhone thia wey wa may bakane yi may
gokh yi, may bakane yi may gokh yi
May leep lu ngène dianôle, Bâye Barhâma
Yeen mbôlo mi fi têw,yalla na lène yalla yôk ,yalla
na lène yalla yôk
Té diokhlène maqâma yi, thi Barhâma
Mane suma nampone arabe tey ma tag Barhâma Cheikhul kullil Awliyâi Barhâma
Bâye mognu nampal, môgnu lêral, thi lêru Allâhu Allâhu, Allâhu, Allâhu,
Allâhu, Allâhu, Lâ ilâha ila Lâhu, Allâhu
Bâye mognu jeuzbu, môgnu guindi thi lîfu AlLâhu Allâhu, Allâhu, Allâhu,
Allâhu, Allâhu, Lâ ilâha ila Lâhu, Allâhu
Bâye mognu diubal môgnu khâmal thi Hâ u AlLâhu AlLâhu, AlLâhu, AlLâhu,
Allâhu, Allâhu, Lâ ilâha ila Lâhu, Allâhu
Lâ ilahâ ila lâh Lâ ilahâ ila lâh
Article précédent